jeudi 3 avril 2025
SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 02I FANI AWRIL 2025
NDIISOOG JËWRIÑ YI - 02 AWRIL 2025
Njiitu Réew mi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 02i fani awril 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la.
Ci ndoortel i kàddoom, Njiitu Réew mi sargal na boole ko ak ñaanal mbooleem jullit ñi ci bisub korite giy màndargaal njeextalu weeru koor wu sell wi. Ci jamono ju am solo jii, ànd na ak askan wi ñaan ngir Senegaalu jàmm, Senegaal gu dal, gu naat, gu tegu ci yoon te mànkoo. Jaajëfal na Ngóornamaŋ bi ak wànqaasi Nguur gi ci seen taxawaay bu am solo ngir peeg yembug dund bi ak njëg yi fépp ci réew mi.
Talaata 02i fani awril 2024, ci la Njiitu Réew mi waatoon ci kanamu Askan wi di màndargaal bis bi mu jotee ci lenge yi. Tay ci àllarba ji 02i fani awril 2025, di màndargaal at mu njëkk mi mu def ci boppu réew mi, delloo na njukkal Usmaan Sonko Njiital Jëwriñ yi ak mbooleem Ngóornamaŋ bi ci liggéey bu mucc ayib bi ñu jot a amal jëm ci joyyanti ak jubbanti. Ci yoon wi ñu jël jëm ci amal ay coppite yu matale, ñaax na Njiital Jëwriñ yi, mu jël mbooleem matiwaay yi war ngir baral jéego yi, ci njëwriñ gu ne, jëm ci jëmmal sémb yi, naal yi ak yeesal yi te jiital ci waxtaan ba juboo niki ñu ko tënkee ci pas-pas ak jubluwaayi Gis-gisu Senegaal gu moom boppam, jub te naat.
Sàmmonte ak li mu jaayante woon dige ko ci kanamu askan wi, doon na lu ñor lool Njiitu Réew mi. Ci loolu feddali na tegtal yi mu joxe woon jëm ci gën jagal dundiinu askan wi, rawati na ci kaw gi, jaare ko ci gën a yombal jote gi ci yenn serwiis yi ëpp solo (ndox, kuraŋ) ak taxawu leen ci wàllum paj boole ko ak taxaw temm ci xeex ak xoraayu (cherté) dund bi jaare ko ci amal caytu gu mucc ayib ci ja yi ak serwiis yi. Ci loolu, rafetlu na bu baax jéego yu am solo yi Ngóornamaŋ bi jot a teg ba tax ñu man a amaat ag wàññiku, gu war a tàbbi 04i fani awril 2025, ci kilo ceeb bi war a jóge ci 450 FCFA wàcc ba 350 FCFA, muy 100 FCFA yu ci wàññiku. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu baral jéego yi, ànd ko Jëwriñu Mbay mi, Bay-Dunde gi ak Càmm gi ak Sekkereteer Detaa bi yor wàllu Mbootaay yi ak Taxawu baykat yi, jëm ci teg pexey moom sunu bopp ci wàllu dund jaare ko ci waajtaay wu mucc ayib ci kàmpaañu mbayum atum 2025 mi boole ko ak gaaw matale yeesal sàrtub « agrosylvopastorale » bi. Mu dolli ci ne, fàww ñu doxal mbooleem jumtukaay yiy gën a dëgëral koomum jàppal ma jàpp mi, niki noonu « coopératives communautaires » yi ñu door boole ko ak gën a dooleel jëmmalug « Pôles territoires » yi.
Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak ci Jëwriñ yi yor wàllu Njàng mi, Tàggatu gu Xereñ gi ak gu Xarala gi ak Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi, ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir amal doxaliin wu mucc ayib ci njàng mi, kàtte yi ak joŋante yi ñu war a amal fépp ci réew mi.
Lu soxal feetu liggéeykat yi war a am 1 panu mee 2025, Njiitu Réew mi ñaax na Ngóornamaŋ bi ak partaneer yi ñu gaaw matale « pacte de stabilité sociale » bu bees bi nga xam ne, doon na lu manul a ñàkk ngir samp ci gën gaa rafeti anam, Senegaal gu xemmemu, suqali sektéer piriwe bi, dundalaat koom mi boole ko ak doxal ay pexe ak i doxaliin yu bees yu jëm ci dooleel xëy mi. Xamal na Ndiisoo gi ne, dina jiite, ci biir weeru awril wi, tijjitel 4eelu « Conférence sociale » bi ñu war a waxtaane man-man ak xëyu ndaw ñi.
Njiitu Réew mi xamle na ne ci at mu yees mii ñuy dugg ci doxaliinu réew mi, yoriin wu sell ci alalu askan wi lu ci manul a ñàkk la. Noonii it la war a demee ci joyyantiwaat sistem yi ñuy kopparalee sunum koom ci fànn yépp. Ci loolu sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi mu gën a dooleel, ànd ko ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Jëwriñu Koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi, coppite yi war a am ci wàllu koom mi, njël li, koppar yi ak ndoxal yi war ngir delloosi boole ko ak suqali wéraayu sistem bi ñuy doxalee sunu koom ak sunuy koppar ci anam yu sax. Ci yoonu yeesal woowu ak teqalikoo ak yenn doxaliin yi, sàkku na ci Ngóornamaŋ bi mu gën a waajal « agenda législatif » bi, niki noonu jataayu waxtaanewaat njël liy dëgmal ak pexe mu yees muy bawoo ci réew mi ci anam yi ñuy yoree alalu askan wi. Ci bunt boobu ba leegi, fàttali na Ngóornamaŋ bi ne fàww ñu tabax, ci kaw déggoo ak kóoluteg aktéer yi, doxaliin wu yees ci sunu sistemu koom ak koppar, tëggaat sunuy ndoxal boole ko ak yeesal sektéer piblig bi sukkandiku ko ci pas-pas bu wér ci amal ay njureef ngir jëmmal yéene ji nu bokk am ci tabax Senegaal gu moom boppam, gu jub te naat.
Senegaal dina màggal, 04i fani awril 2025, 65eelu at mi mu moomee boppam te Njiitu Réew mi war koo jiite ca « Place de la Nation », ci Ndakaaru. Jataay bi dees na ko màndargalee ci yékkati gànnaay yi, toftal ci ag maaj gu mag ci diggante siwil yi ak militeer yi. Femm (fête) gii doon na xew-xew bu mag ci arminaatu repiblig bi, ñu ciy fésal taxawaayu larme bi ak ndaw ñi ci tabax ak suqalikug réew mi. Njiitu Réew mi delloo na njukkal lu wér sunu « anciens combattants » yi, sunu Way-kaaraange yiy sàmm bis bu set kaaraangeg réew mi, taxaw ci aar nit ñi ak seen alal boole ko ak di dugal seen loxo bu baax ci fésal Senegaal ci àddina si.
At mii nag, femmug jonn gi li ci gën a fés mooy dogal bu am solo bi Njiitu Réew mi jël jëm ci jox turu Peresidaa Mammadu Ja xàll wu ràññiku ci gëbla gi : « Boulevard Général De Gaulle ». Ci pàttali, xàll wii, njëkkoon a tudd « Allées Coursins », fa lañu amalee 2eelu maaju 4i fani awril (1962) ci dogalu Mammadu Ja mi Jiite woon Ndiisoo gi. Mammadu Ja mii moo àndoon ak Móodibo Keyta torlu déggoo yii di « Transferts de compétences » yu 04i fani awril 1960 yi may jonn Federaasoo bu Mali (Senegaal kan Sudaan) ak « Général Charles De Gaulle » mi doonoon Njiitu Réewum Farãas ak Njiital Réew yi aju woon ci kilifteefu Farãas.
Lu jëm ci jafe-jafe yi am ci suqalikug ndaamaari (tourisme) gi ci réew mi, Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi ne fàww ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir taxaw ci kaarangeg nit ñi ak seen i alal ci gox yi ak warabi ndaamaari yi nekk fépp ci réew mi. Mu dolli ci ne, jot na sëkk, ginnaaw ndaje mi dox diggante Njëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi ak Njëwriñu Ndaamaari gi ak Pasiin gi, ñu jublu ci taxawal benn « Commissariat spécial » buy yor wàllu ndaamaari gi boole ko ak yokk liggéeykat yi ak jumtukaay yu wér ngir yeesal wàll gi. Njëwriñu Biir Réew mi, Njëwriñu Larme bi ak Ndaamaari gi war nañoo taxaw ci xool doxaliin yu bees yu ñu war a teg ngir kaaraangeg warabi ndaamaari gi. Dees na ci amal um ndaje diggante jëwriñ yi ngir waxtaane mbooleem jafe-jafe yi am ci wàll gi.
Cig àddoom, Njiital Jëwriñ yi mu ngi dooree, ci turu Ngóornamaŋ bi, ñaanal Njiitu Réew mi ci at mi mu jot a def ci boppu réew mi te dëppo ak bisub tay bii di 2i fani awril. Ndokkeel na Njiitu Réew Mi ci taxawaayam, gis-gisam bu leer ak dogoom ci anam yi mu yoree li ñu ko dénk. Yeesal na jaayante ak pas-pasu ngóornamaŋ bi ngir sottal gis-gis bi mu am ci Senegaal gu moom boppam, jub te naat.
Njiital Jëwriñ yi teg ci delloo njukkal bu baax, Profesëer Faatu Sàmba Njaay, miy Njiital « Service d’Hématologie clinique » ca raglub Dalal Jàmm ak ñi muy liggéeyandool, te amal jaloore ju rëy ci anam yu mucc ayib, muy « opération de moelle osseuse » bi ñu njëkk a amal ci Senegaal. Rafetlu na jéego bu am solo bii di tàbbi bu wér ci yoonu moom sa bopp wi ñuy woote ci biir gis-gisu Senegaal 2050.
Ci tomb bu njëkk bi mu yaatal, Njiital Jëwriñ yi dikkaat na ci jafe-jafe yi am ci matukaay yi ñu jëloon ci mbiru luyaas yi te ba fii jurul lenn njariñ rawati na ci taax yi féete Ndakaaru donte sax am na sàrt bu ñu ci tëraloon ca 2014. Ak ni luyaas bi taree lool ba teree nelaw njaboot yi ci gox yu bari ci réew mi, Njiital Jëwriñ yi xamle na ne fàww ñu jéem a amal càmbar yu xóot ci li waral jafe-jafe yooyu di wéy ba leegi. Bu weesoo matuwaay yi ñu ci jot a jël ngir caytu gi, warees na ce amal ay xalaat yu jëm ci am xibaar yu wér ci limub ñiy wut luyaas ak li ci jot a jàppandi niki noonu teg yeneen pexe ngir ñaax boroom kër yi ñuy teg njëg yu méngoo ak dëkkuwaay yi. Njiital Jëwriñ yi xamle na itam yenn tomb yu am solo yu ñu war a bàyyi xel, yu mel ni fànn yi xaw a des ci doxal politig yu wér ci wàllu dëkkuwaay yi ak « pôles urbains » yi niki noonu jéego yu néew yi ñu jot a teg ngir doxal sémb yi jëm ci wàllu dëkkuwaayi ndimbal yi.
Ci seetlu yooyu, Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ ji yor wàllu Yaxantu gi, mu lëkkaloo ak Sekereteer Detaa bi yor wàllu Tabax ak Dëkkuwaay, Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ak Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, amal càmbar yu xóot ci wayndare woowu te gaaral ko, balaa njeextalu weeru suwe 2025, ginnaaw bu ñu ci diisoo ak mbooleem ñi séq wàll wi, ay jëf yu wér te wóor yu jëm ci soppi matukaay yi jëm ci saytu luyaas bi.
Ci ñaareelu tomb bi mu àddu, Njiital Jëwriñ yi xamle na yitteem ci gën a dooleel ci lu jamp matukaayi saytu yi nekk ci biir ndoxalug pénc mi, ngir taxaw bu baax ci jubbanti yenn jafe-jafe yi am ci yoriinu sektéer piblig bi ak paraapiblig bi. Xamle na ne, tolluwaay boobu nag li ko waral bokk na ci yenn jafe-jafe yi ñu amal ci teg doxaliin yu sell ci anam yi ñuy saytoo ci biir ndoxal gi ngir wàññi risk yi, rawati na, risk yi aju ci wàllu jëmmal dara.
Ci loolu, Njiital Jëwriñ yi sàkku na ci Jëwriñ, Sekkereteer Seneraalu Ngóornamaŋ bi, mu teg, ci wetu « Bureau de Suivi et de Coordination de l’Inspection générale d’Etat » ca Primature, genn kippaangog liggéey gu ñuy sas mu xool tolluwaay bi ñu fi fekk te gaaral pexe yu jëm ci gën a jagal doxaliin wu wóor ci « inspections internes » yi nekk ci mbooleem Njëwriñ yi gën gaa yeex njeextalu weeru suwe 2025. Fii ak boobu, sàkku na ci mbooleem Jëwriñ yi ñu jébbal ko tolluwaayu liggéey yi « inspections internes » yi jot a amal ci ñetti weer yu njëkk yi ci atum 2025 boole ko ak di amal ay ndaje diggante wànqaas yi nekk ci seen njëwriñ yi ngir yaatal ci ràppoor yi « inspections internes » yi di faral di amal.
Lu soxal àddug jëwriñ yi:
Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi indi na ay leeral ci liggéey yi « Conseil national de la Consommation » di amal ;
Jëwriñu Njàng mi àddu na ci jumtukaayi njàng mi;
Jëwriñu Mbay mi, Bay Dunde gi ak Càmm gi àddu na ci tolluwaayu kàmpaañu njaayum gerte gi.
Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi.
Aamadu Mustafaa Njekk SARE
Inscription à :
Publier les commentaires (Atom)
Aucun commentaire:
Enregistrer un commentaire