jeudi 1 août 2019

Bataaxal bu gudde nii



Aysatu,Jot naa sa bataaxal, fekk ma ci nattu. Ni ma lay tontoo mooy, wéttalikoo kaye bii, lu ma xalaat def ci ; ndax, yàgg a déeyook yow, tax na maa xam ni, « waxtaan ay dund bi gor », day giifal naqar. Aysatu, sunu diggante, dug tandle. Sunuy maam a jélloo woon i sàkket, daan diisoo bés bu Yàlla sàkk. Sunu yaay ya, ku ca masaan a am rakk, yaak say moroom a koy xëccoo boot. Maak yow noo jàngandoo Alxuraan, daan ànd ca mbeddum xeer mooma aayoon lool ciy dàll ak sér. Bëñ sax, bu nu ko masaan a foq, nooy bokk pax mu nu koy suul te naan : « Jinax, am bëñ bu rafet, te jox nu bëñ bu ñaaw ! » Su at yi demee, nimse yi naaxsaay yit, pàttalliku yi, dara jógu fi, ñoom laay bànneexoo, ñoo tax sama àddina saf xorom. Di la fàttaliku nag ; la woon lépp delsi, teewaat ci sama kanam. Ma gëmm, sama xol dekki, may yëg, ñuy dem, di ñëw : tàngaay baak leeraayu taalu matt ya, mango xayli bu saf sàpp ak kaani, ku xàmp tàqamtiku jox sa moroom. Ma gëmm, mu mel ni nataal yuy feeñ ak a réer : sa yaay ak xeesaay baak ñaq wa muy génne ca waañ wa ; janq ja rooti woon ba jiitley ñëw, tooy xepp ak seen coow lu bari. Bu àddina dee yoon, noo ko ànd ba nuy xale ba nii nu nekke mag, xam, xàmmee, démb meññ tey, nu bokk jikko. Xarit, xarit, ay xarit ! Ñetti yoon laa la woo. Démb nga fase, tey may ténj ! Xarit, Móodu dem na. Xawma sax nan laa la koy waxe. Jaam xamul ëllëgam ; ëllëg, ëllëgu Yàllaa : day xéy dikke ko nu ko soob, ca waxtu wa mu ko soobe. Bu dajeek sunuy bëgg-bëgg, muy bànneex ; bu dee safaan ba, muy naqar ; te li ci ëpp, safaan ba lay doon, dal ci sa kow te doo ca mën lu dul dékku. Noonu laa dékkoo telefon bi salfaañe sama àddina. Ma fëx, ni yulub cib taksi ! Sama put gi wow koŋŋ, sama dënn bi ni sékk, mel ni lu ñuy saañ, may gën di fatt. Lu oto bi dow, ma xeeb, ba ni 5 saraax loppitaal ak xetam gu nëb gu sedd. Egseeguma, ñu daldi may wër ; ñu ma xam ak ñu ma xamul : kanam yu ñagas. Ñiiy jooy, ñii di ma dëfal ci cëtëŋ wii ñu teewe te menuñu ci dara lu dul muñ. Kulwaar bi nu aw, gudd ba ni du jeex, nuy dem ba ni yulub ci benn néeg, ci néeg bi, benn-lal. Ci lal bi, néew bu ni màww, ñu muur ko darab bu weex, nga gis xaat ni kii bokkatul ci way-dund yi. Ab loxo buy kat-kati, muri ko ndànk : simis bu boxoñoo bi, ubbeeku… Kii kay, Móodoo ! Dënn bu jëxëm bii ni tekk ba fàww, jë bu leel biik gémmiñ gu xaw a ŋaaŋ gii, Móodoo ! Ndeysaan, kanam gi ni ràpp, nga gis ni metit ak mbetteel la deewaale. Ma bëgg a jàpp loxo bi, am ku ma téye ; ca laay door a xàmmee Mawdo Ba, xaritam, mu naan ma : « saddum xol bu gaaw a ko bett ci biroom, fekk muy fite sekkarteeram benn bataaxal. Kooku am xelum daldi may woo, ma ñëw ca saa saak àmbilãs bi, bës nanu dënn bi, may ko ngelaw ci gémmiñ gi, dara. » Na mu wax loolu, ma xalaat li wolof naan : « Bóli gu xëtt, tiim na doktoor. »
                                                                                       ….dees ko yeggali
MARIYAAMA BA
Ci tekkim : Maam Yunus Jeŋ, Aram Faal 
 /wareyaan.tumblr.com