lundi 22 avril 2019

Arafi wolof yi

Sëriñ Fàllu Siise


http://www.sawolof.com/alphabet.html
Arafi wolof yi, ñaar fukk ak juroom ñeent la ñu :
a - à – b – c –d –e –é –ë –f –g –i –j –K – L – m –n –ñ –ό – p – q –r – s – t – u – w – x – y
araf yu go’or yi. Walla coowaan yi, ñaar fukk la ñu i :
b - c – d – f – g –j –K – L –m – n – ñ – p – q –r –s –t –w – x – y

araf yu jigéén yi,  walla woye yi, jurόom ñent la ñu :
a – à – e – é –ë – i – o –o’ –u  -

waaye, ci biir coowaan yi, am na yuy ànd ak n walla m . ñu leen di wax arafi nosaale
– nd –ng –nj –nk –nq –nt –nx –mb –mp –nc -

Yu jigéen yi, man na ñu gudd , ñu leen di bind . ñaari oon , boo koy jàng di ko xëcc :
aa  niki  aadama
ee  niki  seel
ii  niki  koor
oo  niki  koor
uu  niki  muur
o’o  niki  fόot
ée  niki  jéem

Yu Go’or yi itam, léeg léeg ñu leen di bind ñaari yoon, niki : dëbb –Fecc –rëdd – dagg –Sàjj – lakk –jàll –Jëmm – benn –ràpp – bàxx (bàq) – Fërr – tissό – mat –jaww –tàyyi – nayyinayyi – Sàññeeku

arifi nosaale yi , amna :
* yu ciy door baat , di ne ci diggi baat , di jeexal baat niki :
- ndaje mi – aandar – mband ak arafun
- njaay mi – mànjaxaan – tënj ak arafun nj
- nguur – màngaan – dëng  ak arafun ng
- mbootu – jelembaan – romb ak arafu m

* Yu ciy nekk ci biir baat , di jeexal baat, niki :
- Sanke – Nànk ak arafu nk
- bànqaas – manq ak arafu nq
- tontu – bunt ak arafu nt
- sompaat – dàmp ak arafu mp
- sancaan – denc ak arafu nc
- sandcal – fanx  


samedi 20 avril 2019

Seex A. Jóob: Làmmiñu réew mi ak gëstu 16

http://www.wolof-online.com

Léeboon: Doomi Yàlla


Kesteloot – Mbodj:Contes et mythes wolof
Léeboon!
Lippóon!
Amoon na fi!
Daan na am!
Ba mu amee yaa fekkee?
Ya wax ma dégg!
waxi tey jar ta gëm!
Sa yos moo ci raw!
Xew xew bii ma nga ameewoon ca jamono ya rab yi daan wax ag nit ñi. Amoon fi jenn jigéen ju bon ju nekkoon ag ñeenti doomam. Ñoo nga dekkoon ca biir àll ba. Baayu xale yi, bi caat mi ñuy wax Tóni juddoo la dee; yaay ji jàpp ne kon xale bi dafa aay gaaf. Mu daldi ko bañ. Bu mosee rëbbi ba ñëw, day woo xale yi, benn benn, ñu nàmp ba mu des Tóni. Muy woy naan: Jamloro kaay nàmp, Jamloro Siise kaay nàmp, Biraama Siise kaay nàmp, Ndaama Siise kaay nàmp, Na Tóni xaar Yàlla yaayam. Di ko def ay yooni yoon. Waaye, jigéen ju bon ji mosul xam ne Yàlla daan na feeñu Tóni ci melokaanu daar bu bare meew; bu ñowee di nàmpal Tóni. Am bés, musiba dal jigéen ji. Mu jóge ca àll ba di woy; woy wa mu daan woowee xale yi ngir nàmpal leen; yemmoog Bukki di jaar,déglu woy wi, jàng ko ba mën ko bu baax. Benn bés, yaayu xale yi dem rëbbi. Bukki doxe ko gannaaw roy baataam, di woy woy wi. Xale yi di génn benn benn, bukki di leen lekk ba mu des Tóni. Ba yaay ja jógee àll ba, muy woy, kenn wuyuwu ko, mu jaaxle lool. Yàggul dara, mu dégg baat bu mu miin, di woy naan ko: Jamloro, Bukki jël na ko, Biraama Siise, Bukki jël na ko, Ndaama Siise, Bukki jël na ko; Tóni rekk a des ci yaayam Yàlla! Ba mu déggee kàddu yooyu, jigéen ji dafa yuuxu, yuuxu gu tar,réer ci àll bi. Foofa la léeb doxee tàbbi géej, bàkkan bu ko njëkka fóon tàbbi àjjana.

Kesteloot – Mbodj:Contes et mythes wolof. Dakar NEA (1983), pp. 45

mercredi 17 avril 2019

AG PÀTTALI

AG PÀTTALI
CA 14 AWRIL CA ATUM 1987, ABDU JUUF DÀQ NA 6265 TAKK-DER
Li juroon loolu nag mooy ay ñaxtu yu amoon ca13 ak 14 awril ca atum 1987. Ñu doon wone seen naqar ci li ñu jàppe woon ag njuumte ginnaaw ba ñu tëjee ca ndung-siin ñaar (2) ci seen i naataango. Daan ya nag tolloon a ci ñaari at yu ñuy tëdd ak juroom benn i milyoŋ i alamaan. Loolu ñu ngi leen ko teg ba nit faatoo ca barab bañu ko tëjoon ginnaaw cacc gu mu amaloon cig daamaar ci atum 1983. Ci la seen moroom i takk-der di jàppale jaare ko ci ay ñaxtu yu teruwaay ba nekk bunt njende la ca gox yii di Kawlax, Ndakaaru, Kees.
Bi ñaxtu yi jeexee ci mbeddi Ndakaaru yi nag ak ci yeneen gox yi, takk-der yi ñu jàpp ne dañoo teggi ndawal, ñoom ñépp la njiitu réew mi fi nekkoon di Abdu Juuf dàq ak ndogal li mu jël ci 14 awril 1987. Njénki la fi nekkoon te waa parti PS éppoon ca, ñoo ca dugal seen i yoxo, daal di wote ndogal la ngir ñu dàq leen ca suba ga.

```Demokaraasi mooy dooley askan wi déet doley njiitum réew mi```

mardi 16 avril 2019

Coumba am ndeye et Coumba amoul ndeye dessin animé Wolof

dee gu metti

Ab Sëriñ daara moo ray dongoom bu tudd Seex Ndigal Seen ba sax moom jàpp nañu ko:
Mu doon dee gu metti dal ci kaw dongo bu ndaw bërki démb. Moom nag dañu koo ray ba noppi suul ko ci guddi gi, te ki ko def doonul kenn ku dul sëriñu daaraam. Loolu nag jur na mettiit ak njàqare lool ci askan wi.

samedi 13 avril 2019

Regardez toutes les épisodes de Niaye le lutteur aux 100 combats 100 def...

xibaar



Defarkatu mburu yi yëgle nañu ne dinañu selaŋlu ñatti fan:
Ñoom nag ñi ngi sàkku ñu wax gan njëkk lañu war a jaaye mburu mi, rawatina bantub genwallu liibar bii nga xam ne 200 lañu ko bëgg a jaaye. Nee nañu nag dinañu bank seen i yoxo ci lu tollook ñatti fan ci ayu-bis bii di ñëw. Te it dinañu yëgle bis bu njëkk biñuy tàmbali selaŋlu gi.

(200 ñeenfuk)

A




Aada : n. habitude
Aay : n. interdit
Aaye : v. interdir
Abal : v. prêter
Abb : v. emprunter
Adduna : n. monde
Agsi : v. arriver
Ajjuma : n. vendredi
Ak : conj. avec, et
Alarba : n. mercredi
Alal : n. bien, fortune
All : n. brousse
Altine : n. lundi
Alxames : n. jeudi
Am : v. avoir, prendre
Ana ...? : conj. où est... ?
And : v. accompagner
Andandoo : n. compagnon
Añ : n. déjeuner
Areen : n. arachide
Asamaan : n. ciel
Askan : n. peuple
At : n. an, année
Attan : n. supporter
Atte : v. juger