vendredi 4 juillet 2025

SAABALU NDIISOOG JËWRIÑ BU ÀLLARBA 5I FANI SUWE 2025. NDIISOOG JËWRIÑ YI - 5 SUWE 2025 Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY jiite na, ci àllarba ji 25i fani suwe 2025, ndajem Ndiisoog Jëwriñ mi ñuy amal ayu-bis bu jot, ca Njénde la. Ci ndoorteel i kàddoom, Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi ne fàww ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir taxaw ca na mu waree, fépp ci réew mi, ci amal ci anam yu mucc ayib kàtte yi ak joŋante yi, rawati na “Baccalauréat général” bi ak “Brevet de Fin d’Etudes moyennes (BFEM)” bi. Ñaax na mbooleem kàndidaa yi teg ci soññ mbooleem ñiy yëngu ci njàng mi (jàngalekat, dongo, way-juru dongo, liggéeykat yi ci ndoxal gi ak ci xarala gi…) ñu def seen kéem tolluwaayu kàttan ngir xereñte, dal ak suqalikug njàngum réew mi. Xamle na ne dina jiite jataayu jébbale raaya yi ñeel ñi gën a ràññiku ci “Concours général” bi, 31i fani sulet 2025. Njiitu Réew mi dikkaat na ci taxawaay bu am solo bi njàng mu kawe mi war a am ci biir “Agenda national de Transformation” bi. Suqali njàng mu kawe mi, gëstu gi ak fent gi ñooy keno yi ñu war a sukkandiku ngir jariñoo nit ñi ci réew mi ak amal coppite gu matale te sax ñeel Senegaal. Fàttali na Ngóornamaŋ bi ne fàww mu gaaw taxaw temm ci jël matukaayi fagaru yi war, ànd ko ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, ngir fexee taxaw ci wéyal njàng mi ak dal gi ci biir jàngune yi ak warabi njàng mu kawe mi. Ci loolu, xamle na solos peeg bu baax : arminaatu njàng mi ci kaw sàmmonte ak tegtal yi ci sistem LMD bi; saytuwaat kàrtu iniwersite yi ci anam yu mucc ayib boole ko ak daloo taax yi ñuy tabax ci jàngune yi nekk ci tund yi; céddaleg dongo yi war a am BAC bees; balluwaay yi ak sas yi ñu jox jàngune yi, warabi jàngukaay yu kawe yi ak warabi dallukaayi jàngune yi; ak kotaa bi ñu war a jël ci ay jàngalekat, liggéeykati ndoxal, xarala ak serwiis yi ànd ko ak rektéer yi. Njiitu Réew mi xamal na Jëwriñu Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi ak Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ne fàww ñu taxaw ci saytu bu baax nees di def ba gën dooleel yoriinu koppar yi ci jànguney pénc mi ak warabi dallukaayi jàngune yi. Ci geneen wàll, sàkku na ci Jëwriñu Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi mu sumb ay waxtaan ak ñiy yëngu ci njàng mu kawe mi ci piriwe bi ngir tabax, ci lu sax, modelu njàng ak gëstu gu boole am doole, gën a xereñ te gën jekk ngir doxal “Agenda national de Transformation” bi. Digle yi war a bawoo ci liggéey yooyu ñuy amal ci wàllu “Agenda national” bi jëm ci soppi Njàng mu Kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi (ANTESRI), dinañu doon lees di jox gëdda gu wér te wóor. Gis-gisu Senegaal gu moom boppan, tegu ci yoon te naat, daa jiital ci ay yitteem taxawu ak gunge way-laago ñi. Njiitu Réew mi fàttali na Ngóornamaŋ bi, ne fàww mu amal xayma gu matale ci “loi d’orientation sociale n° 2010-15” bu 06i fani sulet 2010 biy wax ci wàllu dooleel ak sàmm yelleefi way-laago ñi ak doxal matukaay yi soxal “carte d’égalité des chances” bi. Xamle na itam ne fàww ñu gën a boole way-laago ñi ci doxaliinu campeef yi, ndoxal gi, koom mi, dundiin wi, mbatiitu réew mi, añs. Ci loolu, woo na Ngóornamaŋ bi ngir mu gën a jox yitte càkkuteef yiy bawoo ci way-laago ñi, muy, ci genn wàll anam yi ñuy jëlee ñiy liggéey ci sektéer piblig bi, ak ci geneen wàll, ci tàggatu yi ak kopparal yi ñuy amal ci mbooleem wànqaasi pénc mi. Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi sàkku na ci Ngóornamaŋ bi, rawati na Jëwriñ ji yor wàllu Dëkkuwaay ak ji yor Yaaleg Suuf si, ñu fexe ba jëfandikoo taax yi ak jumtukaayi yaale yi doon lu gën a jàppandi ci way-laago ñi. Ngir tëj bunt bii, woo na Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi, ngir gën a dooleel ñàkk a beddi kenn ci wàllu nekkiin ak dimblante gi ci réew mi, mu sumb ay waxtaan yu jëm ci gën a dooleel kaaraange gi ak nekkiinu way-laago ñi. Njiitu Réew mi dikkaat na ci jafe-jafey saytu moomeelu Nguur gi ci wàllu taax. Eewànteer bi, toppatoo gi ak caytu gu jaar yoon ci taaxi ndoxal gi ak tabaxi pénc mi dañoo bokk ci kenoy yoriin wu leer. Sàkku na ci Njiitu Jëwriñ yi mu gaaral ko, sukkandiku ko ci sas yi ñu jox “Société de Gestion et d’Exploitation du Patrimoine bâti de l’Etat (SOGEPA)” ak “Agence de Construction des Bâtiments et Edifices publics (ACBEP)”, politig bu jëm ci ni ñuy sancee, yeesalaat ak tabax ay taax ak jumtukaayi pénc mi. Mu dolli ci, sàkku ci Njiitu Jëwriñ yi mu amal eewànteer bu matale ci fexee xam limu taaxi ndoxal ak pàkk yi ñu jagleel njëwriñ gu ne te xamle limub li ñu soxla ci ay biro, niki noonu sémbi tabax yi yeggagul, te fexee wàññi bu baax déggoo yi ñu jot a torlu ngir dalal yenn serwiis piblig yi. Ci arminaatam ci wàllu laamisoo, Njiitu Réew mi xamal na Ndiisoo gi ne dina teewe li ko dalee 30i fani suwe jàpp 2i fani sulet 2025 ca “Seville”, ca Espaañ, 4eelu Ndajem àddina mi ñu jagleel kopparal suqaliku gi. Dina teewe itam gaawu 5i fani sulet 2025, 50eelu ati jonnug réewum Kabo Werde. Ci àddug jëwriñ yi: Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox yi ak Goxaan yi ak Daggug Mbeeraay gi àddu na ci daggug gox yu Mbuur 4 ak “Nouvelle ville” bu Cees. CI BINDI YOONAL YI AK SÀRTAL YI: Ndiisoo gi càmbar na ba jàllale : Sémbu yoonal wiy jox ndigal Njiitu Réew mi mu xaatim Déggoog lëkkaloo ci wàllu sóobare ak xarala diggante Ngóornamaŋu Réewum Senegaal ak Ngóornamaŋu Repiblig bu Kongóo, te ñu torlu woon ko 8i fani nowàmbar 2018 ci Ndakaaru. Jëwriñu Tàggatu gu xereñ gi, Farbay Ngóornamaŋ bi. Aamadu Mustafaa Njekk SARE

Aucun commentaire: