mercredi 17 avril 2019

AG PÀTTALI

AG PÀTTALI
CA 14 AWRIL CA ATUM 1987, ABDU JUUF DÀQ NA 6265 TAKK-DER
Li juroon loolu nag mooy ay ñaxtu yu amoon ca13 ak 14 awril ca atum 1987. Ñu doon wone seen naqar ci li ñu jàppe woon ag njuumte ginnaaw ba ñu tëjee ca ndung-siin ñaar (2) ci seen i naataango. Daan ya nag tolloon a ci ñaari at yu ñuy tëdd ak juroom benn i milyoŋ i alamaan. Loolu ñu ngi leen ko teg ba nit faatoo ca barab bañu ko tëjoon ginnaaw cacc gu mu amaloon cig daamaar ci atum 1983. Ci la seen moroom i takk-der di jàppale jaare ko ci ay ñaxtu yu teruwaay ba nekk bunt njende la ca gox yii di Kawlax, Ndakaaru, Kees.
Bi ñaxtu yi jeexee ci mbeddi Ndakaaru yi nag ak ci yeneen gox yi, takk-der yi ñu jàpp ne dañoo teggi ndawal, ñoom ñépp la njiitu réew mi fi nekkoon di Abdu Juuf dàq ak ndogal li mu jël ci 14 awril 1987. Njénki la fi nekkoon te waa parti PS éppoon ca, ñoo ca dugal seen i yoxo, daal di wote ndogal la ngir ñu dàq leen ca suba ga.

```Demokaraasi mooy dooley askan wi déet doley njiitum réew mi```

Aucun commentaire: